Taasukat baa nga naan gainde gu waaf ca buntu kër gé, di melastiku
Bëy bu em bàjjan du fa dem, Zacharia, bàjjan am na maanaa, wayai
Lu la réér ci sa cosaan, sa bàjjan xamal la ko
Boo bëgéé xam sa cosaan, kam la fa maam yi bayyi woom
Demal seeti bàjjan ba, lu mu la ca wax, du deñ
Bàjjana xam Kalcor an ba ca mbeneex wa
Cosaani askan wi, bàjjan am na maanan
Wayum terànga la kuy bàjjan jogal yëngu, sunguñ sangañ bàjjan, bàjjan
Wayum terànga la kuy bàjjan jogal yëngu, bàjjan, bàjjan, sunguñ sangañ
Neenañ mag de mët naa ba cim rééw waaye bàjjan it mët na bàyyi ci biir kër
Xam sa boppa gën ñu woo la naan kii nga doon
Wayum terànga la kuy bàjjan jogal yëngu, sunguñ sangañ bàjjan, bàjjan
Wayum terànga la kuy bàjjan jogal yëngu, bàjjan, bàjjan, sunguñ sangañ
Boo bëgéé xam sa cosaan, sa bàjjan moo la koy xamal
Moo la naan awai fii, bul dem fee, defeel nii
Boo ko seetioo dara du ca deñ
Wayum terànga la kuy bàjjan jogal yëngu, sunguñ sangañ bàjjan, bàjjan
Wayum terànga la kuy bàjjan jogal yëngu, bàjjan, bàjjan, sunguñ sangañ
Mani bàjjan moodi magi gaay walla raidiam
Lu xew lune mane bàjjan laxaw
Bu góór bugéé néégu góór
Bàjjan taxaw wayal ko mbaax
Nijaay di Yaay nga di Baay
Bàjjan am na maanaa
Wayum terànga la kuy bàjjan jogal yëngu, sunguñ sangañ bàjjan, bàjjan
Wayum terànga la kuy bàjjan jogal yëngu, bàjjan, bàjjan, sunguñ sangañ
Bàjjan moodi magi baay walla rakkam